Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 20

Kàddu yu Xelu 20:16-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
16Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal jaambur.
17Njublaŋ, lekk, jëkke neex, mujj mel ni lancub suuf.
18Pexe, ndigal a koy lal; xare, ay tegtal.
19Kuy wër di jëw, wuññi sutura; ku réy làmmiñ, bul déeyook moom.
20Ku saaga sa ndey mbaa sa baay añe lëndëmu bàmmeel.
21Alal ju gaaw du mujje barkeel.
22Bul feyantook ku la tooñ; dénkul ci Aji Sax ji, mu wallu la.

Read Kàddu yu Xelu 20Kàddu yu Xelu 20
Compare Kàddu yu Xelu 20:16-22Kàddu yu Xelu 20:16-22