Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 20

Kàddu yu Xelu 20:13-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
13Bul bëggi nelaw, ba ñàkk dab la; boo njaxlafee, lekk ba desal.
14Kuy waxaalee ngi naan: «Baaxul de!» Bu nee wërëñ, di damu naan: «Aka jar!»
15Wurus am na ak gànjar yu bare, waaye kàdduy xam-xam a gën per yu jafe.
16Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal jaambur.
17Njublaŋ, lekk, jëkke neex, mujj mel ni lancub suuf.
18Pexe, ndigal a koy lal; xare, ay tegtal.
19Kuy wër di jëw, wuññi sutura; ku réy làmmiñ, bul déeyook moom.
20Ku saaga sa ndey mbaa sa baay añe lëndëmu bàmmeel.

Read Kàddu yu Xelu 20Kàddu yu Xelu 20
Compare Kàddu yu Xelu 20:13-20Kàddu yu Xelu 20:13-20