10Nattu diisaay yu yemul ak lu ni mel, Aji Sax ji bañ na ko.
11Gone sax day jëf, nga gis jikkoom; bu naree dëggu te jub, nga xam.
12Nopp buy dégg ak bët buy gis, Aji Sax jee sàkk lu ci nekk.
13Bul bëggi nelaw, ba ñàkk dab la; boo njaxlafee, lekk ba desal.
14Kuy waxaalee ngi naan: «Baaxul de!» Bu nee wërëñ, di damu naan: «Aka jar!»
15Wurus am na ak gànjar yu bare, waaye kàdduy xam-xam a gën per yu jafe.
16Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal jaambur.
17Njublaŋ, lekk, jëkke neex, mujj mel ni lancub suuf.
18Pexe, ndigal a koy lal; xare, ay tegtal.
19Kuy wër di jëw, wuññi sutura; ku réy làmmiñ, bul déeyook moom.
20Ku saaga sa ndey mbaa sa baay añe lëndëmu bàmmeel.
21Alal ju gaaw du mujje barkeel.
22Bul feyantook ku la tooñ; dénkul ci Aji Sax ji, mu wallu la.