7Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam, te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.
8Doom, toppal yaru baay, te bul wacc ndigalu yaay.
9Kaala gu jekk la ci bopp, di gànjar ci baat.
10Doom, bàkkaarkat bu la xiirtal, lànkal.
11Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan, yeeruji jaambur bu deful dara.
12Nanu mel ni njaniiw, mëdd kuy dund, mu jekki tàbbi biir bàmmeel.
13Mboolem alal ju réy, nu jagoo, yeb sunu biir kër, mu fees.
14Dikkal nu far, mbuus miy benn, nu bokk.»