6ngir mana xam aw léeb aku taas ak kàddug boroomi xel yu rafet ak seeni cax.
7Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam, te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.
8Doom, toppal yaru baay, te bul wacc ndigalu yaay.
9Kaala gu jekk la ci bopp, di gànjar ci baat.