Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 1

Kàddu yu Xelu 1:25-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
25Sofental nga samay digle, nanguwoo samay àrtu.
26Kon boo sëngéemee, man it ma ree, njàqare dab la, may textexi.
27Njàqare di ngëlén, dab la, sa musiba def callweer, buub la, njekkar ak fitna dal la.
28Keroog nga woo ma wall, duma wuyu, nga seet ma, seet, doo ma gis.
29Daa fekk nga baña xam, te ragal Yàlla du loo taamu.
30Dégluwoo samay digle it, xanaa xeeb samay àrtu yépp.
31Waaye loo ci góobe, gar ko, say pexe suur la këll.

Read Kàddu yu Xelu 1Kàddu yu Xelu 1
Compare Kàddu yu Xelu 1:25-31Kàddu yu Xelu 1:25-31