Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 1

Kàddu yu Xelu 1:20-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
20Xel mu Rafet a ngay woote ca mbedd ma, di xaacu ca pénc ma.
21Ma ngay wootee bérab yu gëna xumb, di dégtaley kàddoom, bunt dëkk ba.
22Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi? Ñaawlekat bi, foo àppal sa ñaawle bi? Dof bi, ñaata yoon ngay bañ xam-xam?
23Soo dëppee ba déglu, ma àrtu la. Ma ne, kon ma xellil la samam xel, xamal la samay kàddu.

Read Kàddu yu Xelu 1Kàddu yu Xelu 1
Compare Kàddu yu Xelu 1:20-23Kàddu yu Xelu 1:20-23