Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 1

Kàddu yu Xelu 1:2-8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Li ko taxa jóg di nit ñi am xel mu rafet, am ab yar, ngir xam wax ju lal dég-dég,
3ngir yaru ci jëfe xel ak njub ak yoon, di jubal,
4ndax ab téxét di foog, ndaw li it xam tey xalaat.
5Na boroom xel mu rafet déglu, yokk dég-dégam, te kiy ràññee di jariñoo ay tegtal,
6ngir mana xam aw léeb aku taas ak kàddug boroomi xel yu rafet ak seeni cax.
7Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam, te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.
8Doom, toppal yaru baay, te bul wacc ndigalu yaay.

Read Kàddu yu Xelu 1Kàddu yu Xelu 1
Compare Kàddu yu Xelu 1:2-8Kàddu yu Xelu 1:2-8