17Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.
18Yaral sa doom ba muy teel, waaye bul topp sa xol, ba rey ko.
19Ku naqari deret, sonal nga sa bopp; ku la xettli, tóllanti ko.
20Déggal ndigal te yaru, ndax ëllëg nga xelu.
21Bare na lu xol di mébét, waaye Aji Sax jeey dogal.
22Li ñu sopp ci nit mooy ngor, néewle moo gën fen.
23Ragalal Aji Sax ji ndax nga gudd fan, nopplu te baña loru.
24Ab yaafus day yeb loxoom ci ndab, tàyyi ko yékkati, sex.
25Boo ñefee ab ñaawlekat, téxét ba jànge ca; nga yedd kuy dégg, mu xame ca.
26Kuy yàqal sa baay, di dàq sa ndey, yaay indi gàcceek yeraange.
27Doom, soo noppee déglu ku lay yar, sore nga kàdduy xam-xam.
28Seedeb naaféq faalewul yoon, ab soxor lu bon lay tàqamtikoo.
29Na ñaawlekat bi séentu mbugal; ab dof, yeti gannaaw.