Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 19

Kàddu yu Xelu 19:11-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Ku xam lu jaadu, muñ mer, tanqamlu ku la tooñ ngay damoo.
12Merum buur ni gaynde gu ŋar; yërmandey buur ni lay cig mbooy.
13Doom ju dof naqaru baay baa, te jabar ju pànk mooy senn bu dakkul.
14Kër ak alal ngay donne ci baay; jabar ju xelu, Aji Sax jee koy maye.
15Ab yaafus, nelaw yu xóot, te ku yàccaaral xiif.
16Ku jëfe ndigal, sàmm sa bakkan; ku moytuwul sa bopp, dangay dee.

Read Kàddu yu Xelu 19Kàddu yu Xelu 19
Compare Kàddu yu Xelu 19:11-16Kàddu yu Xelu 19:11-16