1Ñàkk te mat, moo gën dof, di wax njekkar.
2Teeyadi baaxul, ku yàkkamti moy saw yoon.
3Nit def na jëfi dof, ba sànku, walbatiku mere Aji Sax ji.
4Ku barele, barey xarit; ku ñàkk, sab xarit dagg la.
5Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen du rëcc àtteem.
6Ñu baree ngi wuta neex boroom daraja, ku nekk a bëgga xaritook kuy joxe.
7Ku ñàkk, sa bokk yépp dëddu la, sab xarit gën laa soreeti, ngay wax ak ñoom, dara.
8Kuy sàkku xel, bëgg nga sa bopp; kuy wut ag dégg day baaxle.
9Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen, mujje sànku.
10Dund gu neex jekkul cib dof, surga buy jiite kilifa it moo yées.
11Ku xam lu jaadu, muñ mer, tanqamlu ku la tooñ ngay damoo.
12Merum buur ni gaynde gu ŋar; yërmandey buur ni lay cig mbooy.
13Doom ju dof naqaru baay baa, te jabar ju pànk mooy senn bu dakkul.
14Kër ak alal ngay donne ci baay; jabar ju xelu, Aji Sax jee koy maye.
15Ab yaafus, nelaw yu xóot, te ku yàccaaral xiif.
16Ku jëfe ndigal, sàmm sa bakkan; ku moytuwul sa bopp, dangay dee.
17Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.
18Yaral sa doom ba muy teel, waaye bul topp sa xol, ba rey ko.
19Ku naqari deret, sonal nga sa bopp; ku la xettli, tóllanti ko.