18Ku ñàkk bopp ay dige feyal jaambur, di ko gàddul boram.
19Ku bëggu ay bëggi tooñ; damu, yàqule.
20Ku njublaŋ du baaxle, kuy wax njekkar añe musiba.
21Ku jur ab dof, am naqar; ab dof waajuram du bég.
22Xol bu sedd day garabal, xol bu tiis day semmal.
23Ku bon day nangu alalu ger ca suuf, nara jalgati yoon.
24Ku am ug dégg ne jàkk ci xel mu rafet, ab dof ne xóll, xel ma sore lool.