6Ku jiital ngor ak worma, Yàlla jéggal la; ku ragal Aji Sax ji, dëddu lu bon.
7Ku Aji Sax ji rafetlu say jëf, say bañ sax, mu jubaleek yaw.
8Néewle te jub moo gën barele te jubadi.
9Nit ay sumb yoonam, Aji Sax ji sottal.
10Su buur àddoo cib àtte, muy kàddu gu Yàlla dogal.
11Nattub diisaay aki ndabam, na jub ngir Aji Sax ji. Moo sàkk mboolem nattukaay.
12Buur daa sib kuy def lu bon, ngir njekkay dëgëral nguuram.
13Wax ju dëggu, buur safoo boroom; ku jub, buur bëgg sa kàddu.
14Merum buur ndaw la, dee a ko yónni; ku rafet um xel, giifal ko.
15Buur, na kanam ga leer, sa bakkan mucc, su la baaxee, mu mel ni taw bu topp um nji.
16Wutal xel mu rafet, bàyyi wurus; taamul ag dégg, wacc xaalis.
17Yoonu kuy jubal day moyu lu bon, ku teeylu sa jëfin, sàmm sa bakkan.
18Réy, yàqule; xeebaate, jóoru.
19Woyof, ànd ak ku néewle moo gën séddook ku bew la mu lewal.
20Ku teewlu mbir, baaxle; ku wóolu Aji Sax ji, bég.