3Loo bëgga def, diis ko Aji Sax ji, say mébét sotti.
4Lu Aji Sax ji sàkk, mbir la ca namm, ba ci ku soxor ak bésu mbugalam.
5Aji Sax ji sib na ku réy, da koy mbugal ci lu wér.
6Ku jiital ngor ak worma, Yàlla jéggal la; ku ragal Aji Sax ji, dëddu lu bon.
7Ku Aji Sax ji rafetlu say jëf, say bañ sax, mu jubaleek yaw.
8Néewle te jub moo gën barele te jubadi.
9Nit ay sumb yoonam, Aji Sax ji sottal.
10Su buur àddoo cib àtte, muy kàddu gu Yàlla dogal.
11Nattub diisaay aki ndabam, na jub ngir Aji Sax ji. Moo sàkk mboolem nattukaay.
12Buur daa sib kuy def lu bon, ngir njekkay dëgëral nguuram.
13Wax ju dëggu, buur safoo boroom; ku jub, buur bëgg sa kàddu.
14Merum buur ndaw la, dee a ko yónni; ku rafet um xel, giifal ko.
15Buur, na kanam ga leer, sa bakkan mucc, su la baaxee, mu mel ni taw bu topp um nji.
16Wutal xel mu rafet, bàyyi wurus; taamul ag dégg, wacc xaalis.
17Yoonu kuy jubal day moyu lu bon, ku teeylu sa jëfin, sàmm sa bakkan.
18Réy, yàqule; xeebaate, jóoru.
19Woyof, ànd ak ku néewle moo gën séddook ku bew la mu lewal.
20Ku teewlu mbir, baaxle; ku wóolu Aji Sax ji, bég.
21Ki rafet xel mooy kiy ràññee, te su wax rafetee, dég-dég yomb.
22Xel mu ñaw day suuxat bakkan, te ab dof jëfi dofam a koy yar.
23Ku rafet xel, say kàddu xelu; soo waxee, yey.
24Wax ju yiw di lem juy xelli, neexa ñam, di jàmmi yaram.
25Yoon a ngi, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci ndee.