9Jëfi ku bon, Aji Sax ji seexlu na ko; ku sàlloo njekk, safoo na la.
10Mbugal tar na, ñeel ku wacc yoon; ku bañ waxi àrtu, dangay dee.
11Njaniiw ak biir suuf, Aji Sax ji di gis, xolu doom aadama waxi noppi.
12Kuy ñaawle buggul ku ko àrtu, te du laaji ku rafet xel.
13Xol bu sedd, kanam gu leer; xol bu tiis, boroom ne yogg.
14Ku am ug dégg sàkku xam-xam, ab dof di toppi caaxaan.
15Xol bu tiis, naqar wu sax; xol bu neex, bànneex bu sax.