Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 15

Kàddu yu Xelu 15:17-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
17Njëlu ñetti xob fa ñu la soppe moo dàq yàpp wu duuf fu ñu la bañe.
18Naqari deret, taalu ay. Teey, fey fitna.
19Yoonu yaafus, dégi neen; kuy jubal, saw xàll yaa.
20Doom rafet xel, baay ba bég; te ab dof ay xeeb ndey ja.
21Jëfi dof a neex ku ñàkk bopp, ku am ug dégg def njub.
22Diisoo ñàkk, pexe moy; digle takku, pexe joy.

Read Kàddu yu Xelu 15Kàddu yu Xelu 15
Compare Kàddu yu Xelu 15:17-22Kàddu yu Xelu 15:17-22