16Néewle te ragal Aji Sax ji moo gën barele, sa bopp ubu.
17Njëlu ñetti xob fa ñu la soppe moo dàq yàpp wu duuf fu ñu la bañe.
18Naqari deret, taalu ay. Teey, fey fitna.
19Yoonu yaafus, dégi neen; kuy jubal, saw xàll yaa.
20Doom rafet xel, baay ba bég; te ab dof ay xeeb ndey ja.
21Jëfi dof a neex ku ñàkk bopp, ku am ug dégg def njub.
22Diisoo ñàkk, pexe moy; digle takku, pexe joy.
23Nit bége na tontam lu dal, kàddu gu jib fa mu ñoree neex!
24Ku rafet xel, jubal nga yoonu gudd fan, moyu teggi, ba jëm njaniiw.
25Ku bew, Aji Sax ji màbb sa kër; ab jëtun, Aji Sax ji ñoŋal pàkkam.