12Kuy ñaawle buggul ku ko àrtu, te du laaji ku rafet xel.
13Xol bu sedd, kanam gu leer; xol bu tiis, boroom ne yogg.
14Ku am ug dégg sàkku xam-xam, ab dof di toppi caaxaan.
15Xol bu tiis, naqar wu sax; xol bu neex, bànneex bu sax.
16Néewle te ragal Aji Sax ji moo gën barele, sa bopp ubu.