8Ku ñaw day xelu, xam li muy def; ab dof di nax boppam.
9Ab dof, su bàkkaaree, yoonam! Te ñay jubal a séq yiwu Yàlla.
10Tiisu xol, boroom a ko xam; mbégte ma it jaambur bokku ca.
11Ab soxor, këram day tas, mbaarum ku jub di naat.
12Yoon a ngii, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci dee.
13Nit a ngi ree, xol ba tiis, te mbégte mujje na njàqare.