Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 14

Kàddu yu Xelu 14:5-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Seede bu dëggu, dëgg rekk, seede bu dëgguwul, fen rekk.
6Ab ñaawlekat day wut xel mu rafet, mu réer ko; ku am ug dégg, xam yomb la.
7Dàndal ab dof, du la yokk xam-xam.
8Ku ñaw day xelu, xam li muy def; ab dof di nax boppam.
9Ab dof, su bàkkaaree, yoonam! Te ñay jubal a séq yiwu Yàlla.
10Tiisu xol, boroom a ko xam; mbégte ma it jaambur bokku ca.
11Ab soxor, këram day tas, mbaarum ku jub di naat.
12Yoon a ngii, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci dee.
13Nit a ngi ree, xol ba tiis, te mbégte mujje na njàqare.
14Ku def njekkar sab añ mat, ku baax gën law demin.
15Ab téxét, loo wax mu gëm; ku ñaw xam fi ngay jaare.
16Ku xelu day ragal, di dëddu lu bon; ab dof day ràkkaaju, du tiit.
17Ku gaawa mer, def jëfi dof, te kuy fexeel nit, ñu bañ la.
18Ab téxét ndof ay céram, ku ñaw jagoo xam-xam.
19Ku bon, ku baax sut la; ku soxor ay toogaanu ku jub.
20Ku ñàkk, say dëkk sax bañ la; ku barele, barey xarit.
21Ku xeeb sa dëkkandoo, bàkkaar nga; ku baaxe ku ñàkk, mbégte ñeel la.
22Kuy mébét lu bon daa réer, kuy mébét lu baax am nga ngor ak worma.
23Kër-këri, jariñu; waxi neen, loxoy neen.
24Ku rafet xel jagoo alal, ab dof ràngoo ndofam.
25Seede bu dëggu day jot bakkan, kuy fen day wore.
26Ragal Aji Sax ji kaaraange gu wér la ci nit, di rawtu ciy doomam.
27Ragal Aji Sax ji day suuxat bakkan, ba boroom du tàbbi ci fiiri ndee.
28Su mbooloo baree, buur am ndam; fu nit ña néew, kilifa du fa dara.
29Muñ mer, déggin wu yaa; gaawa tàng, gënatee dof.
30Xel mu dal, yaram wu naat; fiiraange semmal boroom.
31Ku sonal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; ku baaxe ku néewle, teral nga ka ko sàkk.
32Coxor detteel boroom; ku jub fegoo maanduteem.

Read Kàddu yu Xelu 14Kàddu yu Xelu 14
Compare Kàddu yu Xelu 14:5-32Kàddu yu Xelu 14:5-32