Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 14

Kàddu yu Xelu 14:5-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Seede bu dëggu, dëgg rekk, seede bu dëgguwul, fen rekk.
6Ab ñaawlekat day wut xel mu rafet, mu réer ko; ku am ug dégg, xam yomb la.
7Dàndal ab dof, du la yokk xam-xam.
8Ku ñaw day xelu, xam li muy def; ab dof di nax boppam.
9Ab dof, su bàkkaaree, yoonam! Te ñay jubal a séq yiwu Yàlla.
10Tiisu xol, boroom a ko xam; mbégte ma it jaambur bokku ca.
11Ab soxor, këram day tas, mbaarum ku jub di naat.
12Yoon a ngii, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci dee.

Read Kàddu yu Xelu 14Kàddu yu Xelu 14
Compare Kàddu yu Xelu 14:5-12Kàddu yu Xelu 14:5-12