28Su mbooloo baree, buur am ndam; fu nit ña néew, kilifa du fa dara.
29Muñ mer, déggin wu yaa; gaawa tàng, gënatee dof.
30Xel mu dal, yaram wu naat; fiiraange semmal boroom.
31Ku sonal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; ku baaxe ku néewle, teral nga ka ko sàkk.
32Coxor detteel boroom; ku jub fegoo maanduteem.