2Kuy jubal day ragal Aji Sax ji, ku dëng teddadil nga ko.
3Ab dof a ngi réy-réylu, làmmiñam yar ko; ku rafet xel, sa kàddu aar la.
4Su yëkk takkul, bey, sàq wéet; mu beye dooleem, meññeef ne gàññ.
5Seede bu dëggu, dëgg rekk, seede bu dëgguwul, fen rekk.
6Ab ñaawlekat day wut xel mu rafet, mu réer ko; ku am ug dégg, xam yomb la.
7Dàndal ab dof, du la yokk xam-xam.
8Ku ñaw day xelu, xam li muy def; ab dof di nax boppam.
9Ab dof, su bàkkaaree, yoonam! Te ñay jubal a séq yiwu Yàlla.
10Tiisu xol, boroom a ko xam; mbégte ma it jaambur bokku ca.
11Ab soxor, këram day tas, mbaarum ku jub di naat.