19Ku bon, ku baax sut la; ku soxor ay toogaanu ku jub.
20Ku ñàkk, say dëkk sax bañ la; ku barele, barey xarit.
21Ku xeeb sa dëkkandoo, bàkkaar nga; ku baaxe ku ñàkk, mbégte ñeel la.
22Kuy mébét lu bon daa réer, kuy mébét lu baax am nga ngor ak worma.
23Kër-këri, jariñu; waxi neen, loxoy neen.
24Ku rafet xel jagoo alal, ab dof ràngoo ndofam.
25Seede bu dëggu day jot bakkan, kuy fen day wore.