15Ab téxét, loo wax mu gëm; ku ñaw xam fi ngay jaare.
16Ku xelu day ragal, di dëddu lu bon; ab dof day ràkkaaju, du tiit.
17Ku gaawa mer, def jëfi dof, te kuy fexeel nit, ñu bañ la.
18Ab téxét ndof ay céram, ku ñaw jagoo xam-xam.
19Ku bon, ku baax sut la; ku soxor ay toogaanu ku jub.