Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 14

Kàddu yu Xelu 14:15-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Ab téxét, loo wax mu gëm; ku ñaw xam fi ngay jaare.
16Ku xelu day ragal, di dëddu lu bon; ab dof day ràkkaaju, du tiit.
17Ku gaawa mer, def jëfi dof, te kuy fexeel nit, ñu bañ la.
18Ab téxét ndof ay céram, ku ñaw jagoo xam-xam.

Read Kàddu yu Xelu 14Kàddu yu Xelu 14
Compare Kàddu yu Xelu 14:15-18Kàddu yu Xelu 14:15-18