12Yoon a ngii, nit defe ne jub na, te mu jëme ko ci dee.
13Nit a ngi ree, xol ba tiis, te mbégte mujje na njàqare.
14Ku def njekkar sab añ mat, ku baax gën law demin.
15Ab téxét, loo wax mu gëm; ku ñaw xam fi ngay jaare.
16Ku xelu day ragal, di dëddu lu bon; ab dof day ràkkaaju, du tiit.
17Ku gaawa mer, def jëfi dof, te kuy fexeel nit, ñu bañ la.
18Ab téxét ndof ay céram, ku ñaw jagoo xam-xam.