5Ku jub bañ na ay fen, ku soxor di indi gàcceek yeraange.
6Ku mat day jub, ba fegu; moykat soxor, ba sànku.
7Nit a ngi am-amlu, amul dara; nit di dee-deelu te fees dell.
8Ku am ay fey alal, ba mucc; ku amul deesu ko tëkku.
9Ku jub day leer nàññ, ab soxor mel ni taal bu fey.
10Réy-réylu jote rekk lay jur, ku dégg ndigal a xelu.
11Alal ju lewul day naaw; foral benn-benn, ba biibal.
12Yaakaar ju tas day jeexal xol, aajo ju faju di suuxat bakkan.
13Ku sofental ndigalu Yàlla, yàqule; ku jëfe santaane Yàlla, yoolu.
14Njàngle mu xelu day suuxat bakkan, ba boroom du tàbbi ci fiiri ndee.
15Dangay xam lu jaadu, ñu naw la; yoonu workat day metti.
16Képp ku teey jëfe xam-xam; ab dof ay siiwal ndofam.
17Ndaw lu bon day loru. Ndaw lu wóor garab la ci nit.