18Ku sàggane yoonu yar, séddoo ñàkk ak gàcce; kuy déggi àrtu, am teraanga.
19Aajo ju faju tooyal na xol, te ab dof jomb naa dëddu mbon.
20Àndal ak ku xelu, sam xel rafet; ku lëngook ub dof, loru.
21Ay topp na moykat, ku jub juble.
22Ku baax, donale ba cay sëtam; alalu moykat, muuru ku jub.
23Ku néewle bey na, meññeef ne gàññ, ñu àtte ko ñàkkal, mu ñàkk ko.