Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 13

Kàddu yu Xelu 13:17-25

Help us?
Click on verse(s) to share them!
17Ndaw lu bon day loru. Ndaw lu wóor garab la ci nit.
18Ku sàggane yoonu yar, séddoo ñàkk ak gàcce; kuy déggi àrtu, am teraanga.
19Aajo ju faju tooyal na xol, te ab dof jomb naa dëddu mbon.
20Àndal ak ku xelu, sam xel rafet; ku lëngook ub dof, loru.
21Ay topp na moykat, ku jub juble.
22Ku baax, donale ba cay sëtam; alalu moykat, muuru ku jub.
23Ku néewle bey na, meññeef ne gàññ, ñu àtte ko ñàkkal, mu ñàkk ko.
24Ku dul bantal sa doom, bëggoo ko. Ku bëgg sa doom teel koo yar.
25Ku jub day lekk ba regg, soxor ba dëkke xiif.

Read Kàddu yu Xelu 13Kàddu yu Xelu 13
Compare Kàddu yu Xelu 13:17-25Kàddu yu Xelu 13:17-25