Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 12

Kàddu yu Xelu 12:6-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Ab soxor, waxam am tëru la, day reye; kàdduy kiy jubal di musle.
7Ab soxor bu daanoo, jeex na; ku jub, sa kër taxaw, ne këcc.
8Xel mu ñaw, jëw bu rafet; sam xel jekkadi, ñu xeeb la.
9Woyof mbubb, am benn surga doŋŋ, moo gën réyal turki tey dee ak xiif.
10Ku jub day topptoo ag juram, ab soxor néeg cig juram.
11Beyal sab tool, sab dund doy; topp ay caaxaan ñàkk bopp la.
12Ab soxor ay xemmem alal ju lewul, ku jub garab la, reen baa ko meññal.

Read Kàddu yu Xelu 12Kàddu yu Xelu 12
Compare Kàddu yu Xelu 12:6-12Kàddu yu Xelu 12:6-12