13Bàkkaaru làmmiñ dugal na boroom, ku jub mucc ci njàqare.
14Làmmiñ reggal na boroom; ñaq, jariñu.
15Na dof di jëfe, njub la ci moom; dégg ndigal rafet um xel la.
16Ab dof bu meree, mu gaawa feeñ; ku teey, tanqamlu saaga.
17Ku dëggu, seede dëgg; seede bu bon, fen rekk.
18Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi; kàddu gu xelu, garab la ci.
19Kàdduy dëgg, day sax dàkk; fen, xef xippi, mu wéy.