Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 12

Kàddu yu Xelu 12:12-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Ab soxor ay xemmem alal ju lewul, ku jub garab la, reen baa ko meññal.
13Bàkkaaru làmmiñ dugal na boroom, ku jub mucc ci njàqare.
14Làmmiñ reggal na boroom; ñaq, jariñu.
15Na dof di jëfe, njub la ci moom; dégg ndigal rafet um xel la.
16Ab dof bu meree, mu gaawa feeñ; ku teey, tanqamlu saaga.
17Ku dëggu, seede dëgg; seede bu bon, fen rekk.
18Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi; kàddu gu xelu, garab la ci.
19Kàdduy dëgg, day sax dàkk; fen, xef xippi, mu wéy.

Read Kàddu yu Xelu 12Kàddu yu Xelu 12
Compare Kàddu yu Xelu 12:12-19Kàddu yu Xelu 12:12-19