1Ku bëgga xam, bëgg ku la yedd; ku bañ ku la àrtu, bàyyima nga.
2Ku baax, Aji Sax ji bége la; kuy fexe lu bon, mu daan la.
3Ab soxor, taxawaayam du yàgg; ku jub garab la, reen ba ne kekk.
4Jeeg bu jàmbaare day teral jëkkër ja, jeeg buy rusloo day semmal jëkkër ja.