19Saxoo njekk, dund; sàlloo mbon, dee rekk.
20Aji Sax ji bañ na njublaŋ, safoo maandute.
21Ab soxor mbugalam du jaas, wóor na; te ku jub, saw askan mucc.
22Taaru jongama ju xel ma gàtt, mooy jaaro wurus ci noppu mbaam-xuux.
23Ku jub, lu baax rekk lay sàkku; soxor biy yaakaar, mujje mbugal.
24Nit a ngi tabe, di yokkule; nit di nëŋ-nëŋi, gëna ñàkk.
25Ku yéwén, woomle; kuy suuxat, suuxu.
26Nit a ngi móolu kuy denc pepp, ba mu ñàkkee, di gërëm ka koy jaay.