1Aji Sax ji bañ na njublaŋ ci nattub diisaay, ay nattukaay na mat, muy bànneexam.
2Ku réy-réylu rus; woyofal ndax nga xelu.
3Kuy jubal, jiital mat. Njublaŋ ak wor, detteelu.
4Alal du jariñ bésu mbugal; jub, mucc ci gàtt fan.
5Ku mat, njekk xàllal la; coxor daaneel boroom.
6Jubalal, sa njekk musal la; ab workat day bëgge, ba far keppu.