5Ku ngóob jot, nga góob, xelu nga; ngóob taxaw, ngay nelaw, gàcce la.
6Jub, barkeelu; ku soxor, wax ja làq fitna.
7Ku jub barkeel, saw tur du fey; ab soxor, turam seey.
8Ku rafet xel day jëfe santaane, ab dof waxa wax, ba loru.
9Maandu, fegu; dëng, weeru.
10Piiseek làq-làqal, sabab njàqare; ab dof waxa wax, ba loru.
11Kàdduy ku jub bëtu ndox la, day naatal; waaye ku soxor, wax ja làq fitna.
12Mbañeelak ayoo; cofeelak jéggale bépp tooñ.
13Kuy dégg, say wax rafet; te ku ñàkk bopp, yelloo yetu gannaaw.
14Ku rafet xel day xam, ne cell; bu dof noppiwul, yàqule teew.
15Alal day aar boroom ni ab tata, ñàkk di lor baadoolo.