18Ku la nëbbal mbañeel, da lay fen; kuy wër di sos, ab dof la.
19Wax ju bare, moy ñàkku ca; ku moom sa làmmiñ, xelu nga.
20Kàddug ku jub di ngën-gi-xaalis, xelum coxor amul solo.
21Kàdduy ku jub jariñ na ñu bare, dof ñàkk na bopp, ba far dee.
22Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.
23Jëf ju bon la dof di foye; ku am dég-dég safoo lu xelu.
24Ab soxor, li mu ragal moo koy dab; nammeelu ku jub day sotti.
25Bu ngëlén walee, ab soxor ne mes; ku jub, sab reen sax ba fàww.