Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 10

Kàddu yu Xelu 10:15-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Alal day aar boroom ni ab tata, ñàkk di lor baadoolo.
16Ku jub jot peyam, dunde; ab soxor di bàkkaare alalam.
17Yaru, gudd fan; sàgganey àrtu, sànku.
18Ku la nëbbal mbañeel, da lay fen; kuy wër di sos, ab dof la.
19Wax ju bare, moy ñàkku ca; ku moom sa làmmiñ, xelu nga.
20Kàddug ku jub di ngën-gi-xaalis, xelum coxor amul solo.
21Kàdduy ku jub jariñ na ñu bare, dof ñàkk na bopp, ba far dee.
22Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.
23Jëf ju bon la dof di foye; ku am dég-dég safoo lu xelu.

Read Kàddu yu Xelu 10Kàddu yu Xelu 10
Compare Kàddu yu Xelu 10:15-23Kàddu yu Xelu 10:15-23