13Kuy dégg, say wax rafet; te ku ñàkk bopp, yelloo yetu gannaaw.
14Ku rafet xel day xam, ne cell; bu dof noppiwul, yàqule teew.
15Alal day aar boroom ni ab tata, ñàkk di lor baadoolo.
16Ku jub jot peyam, dunde; ab soxor di bàkkaare alalam.
17Yaru, gudd fan; sàgganey àrtu, sànku.
18Ku la nëbbal mbañeel, da lay fen; kuy wër di sos, ab dof la.
19Wax ju bare, moy ñàkku ca; ku moom sa làmmiñ, xelu nga.
20Kàddug ku jub di ngën-gi-xaalis, xelum coxor amul solo.
21Kàdduy ku jub jariñ na ñu bare, dof ñàkk na bopp, ba far dee.