Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 7

JËF YA 7:16-42

Help us?
Click on verse(s) to share them!
16Gannaaw loolu ñu yóbbu seeni néew Sisem, dugal leen ca bàmmeel, ba Ibraayma jëndoon ak xaalis ca doomi Amor ca Sisem.
17«Bi loolu wéyee jamono ji jege woon na, ngir Yàlla amal li mu digoon Ibraayma ci ngiñ; fekk xeet wa di law tey gëna bare ci Misra,
18ba keroog beneen buur bu xamul Yuusufa di falu ci Misra.
19Buur boobu nag dafa daan nax sunu xeet, di fitnaal sunuy maam, ba di leen sànniloo seeni doom, ngir ñu dee.
20«Booba nag la Musaa juddu, di ku rafet ci kanam Yàlla; ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam,
21ba noppi sànni ko. Noonu doom ju jigéen ju Firawna for ko, yar ko ni doomam.
22Musaa nag di ku yewwu ci xam-xamu waa Misra bépp, di jàmbaar ci wax ak jëf.
23«Bi mu demee ba am ñeent fukki at, mu fas yéeney seeti ay bokkam, maanaam bànni Israyil.
24Noonu mu gis ca ku ñuy néewal doole, mu sotle ko, feyul ko, ba dóor waayi Misra ja.
25Mu defe ne, ay bokkam dinañu xam ne ciy loxoom la leen Yàllay musale, waaye xamuñu ko.
26Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, mu di leen jéema jubale ne leen: “Yéen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di xeex?”
27Waaye kiy néewal doole moroomam bëmëx ko ne: “Ku la teg kilifa ak àttekat ci sunu kaw?
28Ndax danga maa bëgga rey, ni nga defoon démb waayi Misra ja?”
29Bi Musaa déggee wax jooju, mu daldi daw, dem réewu Majan, di fa ab doxandéem; mu séy fa, ba am ñaari doom.
30«Lu ko wees ñeent fukki at nag, bi mu nekkee ca màndiŋu tundu Sinayi, malaaka feeñu ko ci takk-takku sawara ci biir as ngarab.
31Bi ko Musaa gisee, mu daldi waaru ci li mu gis; mu jegesi ngir niir ko, dégg baatu Boroom bi ne ko:
32“Man maay sa Yàllay maam, di Yàllay Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.” Ci kaw loolu Musaa tiit bay lox, te ñemeetula xool.
33Noonu Boroom bi ne ko: “Summil say dàll, ndaxte bérab bi nga taxaw, bérab bu sell la.
34Gis naa bu baax fitnay sama xeet ci Misra te dégg naa seeni tawat, kon wàcc naa ngir musal leen. Léegi nag ñëwal, dinaa la yebal Misra.”
35«Musaa moomu bañoon nañu ko, ba ne ko: “Ku la teg kilifa ak àttekat?” Waaye moom la Yàlla yebal, jaarale ko ci malaaka mi ko feeñu ca ngarab sa, ngir mu nekk kilifa gu leen di goreel.
36Moo leen génne réewu Misra, di def ay kéemaan ak ay firnde ca réew ma, ca géeju Barax ya ak ca màndiŋ ma diirub ñeent fukki at.
37Musaa moomu moo ne woon bànni Israyil: “Yàlla dina leen feeñalal ci seeni bokk Yonent bu mel ni man.”
38Te moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, ànd ak sunuy maam, wéttalikoo malaaka, mi waxoon ak moom ci tundu Sinayi. Te mu jote ci Yàlla kàddu yiy dund, ngir jottali nu ko.
39Waaye sunuy maam nanguwuñu koo déggal; dañu koo bañ te seeni xel dëpp, dellu Misra.
40Ñu sant Aaróona ne: “Sàkkal nu ay yàlla yuy jiitu ci sunu kanam, ndaxte Musaa male nu génne ci réewu Misra, xamunu lu ko dal.”
41Booba nag ñu tëgglu aw sëllu, muy xërëm, ñu di ko tuuru, di bànneexu ci seeni jëfi loxo.
42Waaye bi ñu ko defee Yàlla dëddu leen, bërgël leen, ñuy jaamu biddiiwi asamaan. Moom lañu bind ci téereb yonent yi ne: “Yéen bànni Israyil, ndax rendi ngeen jur, jébbal ma, boole ko ak i sarax, diirub ñeent fukki at ca màndiŋ ma?

Read JËF YA 7JËF YA 7
Compare JËF YA 7:16-42JËF YA 7:16-42