Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 20

Jëf ya 20:2-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Ba loolu amee mu wër gox yooyu, ñaaxe gëmkat ña kàddu yu takku, doora dem réewum Geres.
3Mu toog fa ñetti weer. Gannaaw gi muy waaja dugg gaal jëm Siri, far pexe mu ko Yawut ya lalal feeñ, mu fomm, nara dellu jaareji Maseduwan.
4Ña àndoon ak moom ñoo di Sopater doomu Pirus ma cosaanoo Bere, ak Aristàrk ak Segond, waa Tesalonig ya, ak Gayus, ma dëkke Derbe, ak Timote, ak waa diiwaanu Asi ya, Tisig ak Torofim.
5Ñooñu ñoo jiitu, di nu nég ca dëkk ba ñuy wax Torowas.
6Nun nag ba màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu mu amul lawiir weesee lanu dugge gaal fa dëkk ba ñuy wax Filipi, am juróomi fan ca yoon wa, door leena fekksi ca Torowas, toog fa juróom ñaari fan.
7Ca ndoortel ayu bés ba, naka lanu daje ngir dagg mburum bokkoo mi, Póol, yékkati kàddu, di wax ak gëmkat ñi, ndax fekk na mu bëggoona dem ca ëllëg sa. Wax ja nag law ba guddi ga xaaj.
8Ay làmp yu baree nga woon ca néegu kaw taax ma ñu daje woon.
9Ci biir loolu ab xale bu góor bu ñuy wax Ëtikus ma nga tooge kéméju palanteer ba. Ngëmment dab ko, te kàddug Póol ga yàgg lool. Ay nelaw nag jàpp waa ji, mu xàwwikoo ca ñetteelu taax ma, daanu, ñu yékkati ko, fekk mu dee.
10Ba loolu amee Póol wàcc, tiim ko, daldi koy téye ci diggante ñaari loxoom, ne leen: «Buleen jaaxle, mu ngi dund.»
11Mu yéegaat, dagg mburu ma, lekk. Waxaat na lu yàgg, ba njël jot, mu sooga dem.
12Xalelu góor ba moom, nit ñaa ko yóbbu, muy dund, seen xel doora dal bu baax.
13Nun nag nu jiituji, dugg gaal jëm Asos, fa nu nara yebe Póol, na mu ko mébéte woon, ndax Póol ci boppam moo xalaatoona jaare ci yoonu suuf si ba fekksi nu fa.

Read Jëf ya 20Jëf ya 20
Compare Jëf ya 20:2-13Jëf ya 20:2-13