Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 20

JËF YA 20:18-38

Help us?
Click on verse(s) to share them!
18Bi ñu ñëwee, mu ne leen: «Yéen xam ngeen bu baax, ni ma doon doxale diirub sama ngan gépp ci seen biir, li dale ci bés bi ma jëkkee teg tànk ci Asi ba tey.
19Jaamu naa Boroom bi ci woyof gu mat ak ay rongooñ, dékku ay nattu yu ma pexey Yawut yi indil.
20Xam ngeen ne masuma leena nëbb dara lu leen di jariñ, di leen jàngal ci kanam ñépp ak ca kër ya.
21Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, ñu tuub seeni bàkkaar, ba waññiku ci Yàlla te gëm sunu Boroom Yeesu.
22«Léegi maa ngi nii di dem Yerusalem, ci li ma Xelu Yàlla mi xiirtal, te xawma lu ma fay dal.
23Xam naa rekk ne ci dëkkoo dëkk Xel mu Sell mi xamal na ma ne ay buum ak ay metit ñu ngi may nég.
24Waaye sama bakkan soxalu ma, su fekkee bey naa sama sas, ba matal liggéey, bi ma Boroom bi dénk, maanaam ma seedeel ci ñépp xibaaru jàmm, bi ëmb yiwu Yàlla.
25«Fi mu ne nag xam naa ne dootuleen gis sama kanam, yéen ñépp ñi ma jaaroon ci seen biir, di yégle nguuru Yàlla.
26Moo tax may dëggal tey jii ne wàccoo naa ak yéen ñépp bés pénc.
27Ndaxte ñeebluwuma leen, ci di leen xamal lépp li Yàlla digle.
28Wottuleen nag seen bopp te wottu coggal jépp, ji leen Xel mu Sell mi def sàmm, ngeen sàmm mbooloo, mi Yàlla jotal boppam ak deretu Doomam.
29Xam naa ne bu ma leen wonee gannaaw, bukki yu soxor dinañu tàbbi ci coggal ji te duñu ci ñeeblu kenn.
30Ay nit dinañu jóg ci seen biir sax, di wax luy sànke, ngir sàkku ay taalibe.
31Foogleen nag, di fàttaliku ne diirub ñetti at, guddi ak bëccëg, masumaa noppi di leen artu kenn ku nekk ci yéen ak ay rongooñ.
32«Léegi nag maa ngi leen di dénk Boroom bi, moom ak kàddug yiwam, gi leen mana dëgëral te may leen cér ci biir gaayi Yàlla yu sell yépp.
33Nammuma xaalisu kenn mbaa wurusam mbaa koddaayam.
34Xam ngeen ne faj naa samay soxla ak soxlay ñi ànd ak man ci sama loxo yii.
35Ci lépp won naa leen royukaay, ci li nu wara dimbali ñi néew doole te fàttaliku li Yeesu Boroom bi wax moom ci boppam ne: “Joxe moo gëna barkeel nangu.”»
36Bi mu waxee loolu, mu sukk ak ñoom ñépp, ñaan ci Yàlla.
37Te ñépp jooy bu metti, di laxasu ci baatu Pool, fóon ko bu baax.
38Li leen gëna teg aw tiis mooy li mu leen wax: «Dootuleen gis sama kanam.» Noonu ñu gunge ko ba ca gaal ga.

Read JËF YA 20JËF YA 20
Compare JËF YA 20:18-38JËF YA 20:18-38