15Gannaaw loolu gaal ga jóge fa, nu agsi ca ëllëg sa janook dunu Kiyos. Bés ba ca tegu nag nu jàll ba Samos, te ñetteelu fan ba nu àgg Mile.
16Ndaxte Pool fasoon na yéenee teggi Efes, ngir baña yàgg ci diiwaanu Asi; mu ngi doon gaawantu, ngir màggal, gi ñuy wax Pàntakot fekk ko Yerusalem.
17Bi Pool eggee Mile nag, mu yónnee ca Efes, ngir woo njiiti mbooloom ñi gëm.
18Bi ñu ñëwee, mu ne leen: «Yéen xam ngeen bu baax, ni ma doon doxale diirub sama ngan gépp ci seen biir, li dale ci bés bi ma jëkkee teg tànk ci Asi ba tey.
19Jaamu naa Boroom bi ci woyof gu mat ak ay rongooñ, dékku ay nattu yu ma pexey Yawut yi indil.
20Xam ngeen ne masuma leena nëbb dara lu leen di jariñ, di leen jàngal ci kanam ñépp ak ca kër ya.
21Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, ñu tuub seeni bàkkaar, ba waññiku ci Yàlla te gëm sunu Boroom Yeesu.
22«Léegi maa ngi nii di dem Yerusalem, ci li ma Xelu Yàlla mi xiirtal, te xawma lu ma fay dal.
23Xam naa rekk ne ci dëkkoo dëkk Xel mu Sell mi xamal na ma ne ay buum ak ay metit ñu ngi may nég.
24Waaye sama bakkan soxalu ma, su fekkee bey naa sama sas, ba matal liggéey, bi ma Boroom bi dénk, maanaam ma seedeel ci ñépp xibaaru jàmm, bi ëmb yiwu Yàlla.