Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 20:15-24 in Wolof

Help us?

JËF YA 20:15-24 in Téereb Injiil

15 Gannaaw loolu gaal ga jóge fa, nu agsi ca ëllëg sa janook dunu Kiyos. Bés ba ca tegu nag nu jàll ba Samos, te ñetteelu fan ba nu àgg Mile.
16 Ndaxte Pool fasoon na yéenee teggi Efes, ngir baña yàgg ci diiwaanu Asi; mu ngi doon gaawantu, ngir màggal, gi ñuy wax Pàntakot fekk ko Yerusalem.
17 Bi Pool eggee Mile nag, mu yónnee ca Efes, ngir woo njiiti mbooloom ñi gëm.
18 Bi ñu ñëwee, mu ne leen: «Yéen xam ngeen bu baax, ni ma doon doxale diirub sama ngan gépp ci seen biir, li dale ci bés bi ma jëkkee teg tànk ci Asi ba tey.
19 Jaamu naa Boroom bi ci woyof gu mat ak ay rongooñ, dékku ay nattu yu ma pexey Yawut yi indil.
20 Xam ngeen ne masuma leena nëbb dara lu leen di jariñ, di leen jàngal ci kanam ñépp ak ca kër ya.
21 Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, ñu tuub seeni bàkkaar, ba waññiku ci Yàlla te gëm sunu Boroom Yeesu.
22 «Léegi maa ngi nii di dem Yerusalem, ci li ma Xelu Yàlla mi xiirtal, te xawma lu ma fay dal.
23 Xam naa rekk ne ci dëkkoo dëkk Xel mu Sell mi xamal na ma ne ay buum ak ay metit ñu ngi may nég.
24 Waaye sama bakkan soxalu ma, su fekkee bey naa sama sas, ba matal liggéey, bi ma Boroom bi dénk, maanaam ma seedeel ci ñépp xibaaru jàmm, bi ëmb yiwu Yàlla.
JËF YA 20 in Téereb Injiil

Jëf ya 20:15-24 in Kàddug Yàlla gi

15 Nu jóge fa, tëmb ba agsi ca ëllëg sa fa janook dunu Kiyos, bés ba ca topp, nu àgg Samos, bés ba ca toppaat, nu àgg Mile.
16 Ndax Póol daa fasoon yéeney teggi Efes, ngir baña yàgg diiwaanu Asi; booba day gaawtu, ngir màggalu Pàntakot man koo fekk Yerusalem.
17 Fa Mile la Póol yónnee ca Efes, woolu magi gëmkat ñi.
18 Ba ñu dikkee, mu ne leen: «Yeen ci seen bopp xam ngeen bu baax, ca bés ba ma jëkkee teg sama tànk Asi, ba tey jii, ni ma masa doxale ak yeen,
19 di jaamoo Boroom bi ag woyof gu mat sëkk, ci biiri rongooñ ak nattu yu ma pexey Yawut yi teg.
20 Te amul lenn lu leen di jariñ, lu ma leen nëbb, bañ leen koo xamal; jàngal naa leen ci mbeddum buur ak ci biir kër yi.
21 Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, ñu tuub ci Yàlla te gëm sunu Sang Yeesu.
22 «Léegi maa ngii ci curgag Noo gu Sell gi, di dem Yerusalem, lu ma fay dal sax, xawma ci dara,
23 lu moy li ma Noo gu Sell giy seereel ci dëkkoo dëkk, ne ma ay jéng aki coono moo may nég.
24 Waaye sama bakkan soxalu ma, xanaa ma bey samaw sas, ba sottal liggéey, bi ma Sang Yeesu dénk, te mooy seedeel xibaaru jàmm bu yiwu Yàlla wi.
Jëf ya 20 in Kàddug Yàlla gi