Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 15

Jëf ya 15:27-39

Help us?
Click on verse(s) to share them!
27Kon nag noo yebal Yuda ak Silas, ngir ñu àgge leen ci seen gémmiñu bopp, lii nu leen bind.
28Ndaxte Noo gu Sell gi moo mànkoo ak nun ci bañ leena teg benn coono, xanaa lii manula ñàkk:
29Ngeen moytu yàpp wu ñu sarxal ay tuur, ak deret, ak yàppu jur gu ñu tuurul deretam, ak powum séy. Yooyii, bu ngeen ko moytoo bu baax, def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.
30Ba loolu amee ñu tàggtoo, daldi dem ba Àncos. Ci kaw loolu ñu woo mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi.
31Ba ñu jàngee bataaxal bi, kàddu ga dëfal leen, seen xol sedd.
32Yuda ak Silas it gannaaw ay yonent lañu woon, wax nañu ak bokk yi lu yàgg, ngir ñaax leen, feddli seen ngëm.
33Ba loolu amee ñu toog fa ab diir, bokk yi door leena ñaanal yoonu jàmm, yiwi leen, ngir ñu dellu ca ña leen yebaloon.
35Póol ak Barnaba nag des Àncos. Ñu ànd ak ñeneen ñu bare, di jàngle ak a xamle kàddug Boroom bi.
36Ba ñu ca tegee ay fan Póol ne Barnaba: «Nan dellu seeti bokk yi ci mboolem dëkk yi nu yégle woon kàddug Boroom bi, ba gis nu ñu def.»
37Barnaba nag bëggoon ñu yóbbaale Yowaan, mi ñuy wax Màrk.
38Teewul Póol jàpp ne gannaaw Yowaan Màrk moomu moo leen waccoon ca Pamfili te àndul woon ak ñoom ci liggéey bi, yóbbaale ko warul.
39Mbir mi nag mujje dëngoo bu metti, ba ñu teqlikoo. Barnaba ànd ak Yowaan Màrk, dugg gaal, jëm Sippar.

Read Jëf ya 15Jëf ya 15
Compare Jëf ya 15:27-39Jëf ya 15:27-39