Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 15:27-39 in Wolof

Help us?

JËF YA 15:27-39 in Téereb Injiil

27 Yónni nanu nag Yudd ak Silas, ñu di leen xamal xibaar boobu ci seen gémmiñ.
28 Ndaxte li neex Xel mu Sell mi te neex nu, mooy nu bañ leena teg beneen yen, lu dul dénkaane yii am njariñ,
29 maanaam ngeen moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm, deretu jur gu médd ak njaaloo. Bu ngeen moytoo yëf yooyu, dingeen def lu baax. Ci jàmm.
30 Noonu ñu tàggoo, dem Ancos, ñu dajale mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi.
31 Ñu jàng ko nag, seen xol sedd ci doole, ji leen bataaxal bi indil.
32 Te Yudd ak Silas, ñi doon yonent, ñuy dooleel bokk yi, di dëgëral seen fit ak wax yu bare.
33 Bi loolu amee ñu toog fa ab diir, ba noppi bokk yi yiwi leen ci jàmm, ñu dellu ca ña leen yónni woon.
35 Waaye Pool ak Barnabas des ci Ancos, di jàngle ak di xamle xibaaru jàmm bu kàddug Boroom bi, ñoom ak ñeneen ñu bare.
36 Gannaaw ay fan Pool ne Barnabas: «Nan dellu seeti bokk ya ca dëkk yépp, fu nu masa yéglee kàddug Boroom bi, ba gis nu ñu def.»
37 Barnabas nag bëggoon na yóbbaale Yowaana, mi ñuy wax it Màrk.
38 Waaye Pool dafa lànk ne: «Matul nu yóbbu ki nu waccoon ca Pamfili, ba àndul woon ak nun ca liggéey ba.»
39 Noonu ñu xuloo, ba far tàggoo. Barnabas yóbbaale Màrk, ñu dugg gaal, jëm Sipar.
JËF YA 15 in Téereb Injiil

Jëf ya 15:27-39 in Kàddug Yàlla gi

27 Kon nag noo yebal Yuda ak Silas, ngir ñu àgge leen ci seen gémmiñu bopp, lii nu leen bind.
28 Ndaxte Noo gu Sell gi moo mànkoo ak nun ci bañ leena teg benn coono, xanaa lii manula ñàkk:
29 Ngeen moytu yàpp wu ñu sarxal ay tuur, ak deret, ak yàppu jur gu ñu tuurul deretam, ak powum séy. Yooyii, bu ngeen ko moytoo bu baax, def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.
30 Ba loolu amee ñu tàggtoo, daldi dem ba Àncos. Ci kaw loolu ñu woo mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi.
31 Ba ñu jàngee bataaxal bi, kàddu ga dëfal leen, seen xol sedd.
32 Yuda ak Silas it gannaaw ay yonent lañu woon, wax nañu ak bokk yi lu yàgg, ngir ñaax leen, feddli seen ngëm.
33 Ba loolu amee ñu toog fa ab diir, bokk yi door leena ñaanal yoonu jàmm, yiwi leen, ngir ñu dellu ca ña leen yebaloon.
35 Póol ak Barnaba nag des Àncos. Ñu ànd ak ñeneen ñu bare, di jàngle ak a xamle kàddug Boroom bi.
36 Ba ñu ca tegee ay fan Póol ne Barnaba: «Nan dellu seeti bokk yi ci mboolem dëkk yi nu yégle woon kàddug Boroom bi, ba gis nu ñu def.»
37 Barnaba nag bëggoon ñu yóbbaale Yowaan, mi ñuy wax Màrk.
38 Teewul Póol jàpp ne gannaaw Yowaan Màrk moomu moo leen waccoon ca Pamfili te àndul woon ak ñoom ci liggéey bi, yóbbaale ko warul.
39 Mbir mi nag mujje dëngoo bu metti, ba ñu teqlikoo. Barnaba ànd ak Yowaan Màrk, dugg gaal, jëm Sippar.
Jëf ya 15 in Kàddug Yàlla gi