3Mu gis nag na mbir ma neexe Yawut ya, ba tax mu teg loxo Piyeer, moom itam; loola yemook bési màggalu Mburu mu amul lawiir.
4Naka la ko jàpplu, daldi koy tëj kaso, teg ko ci loxoy ñeenti kurél yu ñeenti takk-der, ngir ñu wattu ko; booba ma ngay xaar ba bésub Mucc bi wees, mu door koo yóbbu ca kanam askan wa.
5Naka lañu tëj Piyeer ca kaso ba, mbooloom gëmkat ñi saxoo koo ñaanal Yàlla.
6Ba ñu demee ba ca guddi, ga jiitu bés ba ko Erodd wara yóbbu, Piyeer a ngay nelaw ci diggante ñaari takk-der, ñu yeewe ko ñaari càllala, ay dag di wattu buntu kaso ba.
7Ci kaw loolu am malaakam Boroom bi ne jaas, taxaw, ag leer ne ràyy ca biir kaso ba. Malaaka ma laal Piyeer ci wetam, yee ko, ne ko: «Jógal gaaw!», càllala yi daldi rote ciy loxoom.