Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 7

1.Buur ya 7:35-51

Help us?
Click on verse(s) to share them!
35Kaw boppu rootukaay bu nekk, kéméj gu mërgaloo féete ci kaw, taxawaayam di genn-wàllu xasab, njàppu yeek làcc yi sax ci, lépp di benn.
36Fi amul dara ci kaw njàppu yeek làcc yi, mu ñaas ci ay nataali serub aki gaynde aki garabi ron yu ñu wërale ay caqi tóor-tóor.
37Noonu la Uram defare fukki rootukaay yi. Lépp bokk móol, yem dayo te bokk bind.
38Mu defar itam fukki bagaani xànjar; bagaan bu ci nekk tollook ñeenti xasab, di def lu xawa tollook juróomi barigo; bagaan bu ci nekk tegu cib rootukaay, ba fukki rootukaay yi daj.
39Ba mu ko defee mu taaj juróomi rootukaay fa féete kër Yàlla ga ndijoor ak juróomi rootukaay fa féete kër ga càmmoñ. Mu teg mbalkam jàpp mi fa féete kër ga ndijoor, ca wetu bëj-saalum, jàpp penku.
40Iram sàkk itam ndab yu ndaw yi ak ñiitukaay yi ak këlli tuurukaay yi. Ci kaw loolu Iram sottal mboolem liggéey ba mu liggéeyal Buur Suleymaan ca kër Aji Sax ji:
41muy ñaari jën yi, ak ñaari gamb yiy boppi jën yi, ak ñaari caaxi càllala yiy muur ñaari gamb yi,
42ak ñeenti téeméeri gërënaat yiy ànd ak ñaari caax yi; caax bu nekk, ñaari caqi gërënaat, ñu dar ñaari gamb yiy boppi xer yi;
43ak fukki rootukaay yi ak fukki bagaan yi ci kaw rootukaay yi.
44Mbalkam jàpp mi it ci la, ak fukki nag ak yaar yi ronu mbalkam jàpp mi.
45Bagaan yu ndaw yi bokk na ci, ak ñiitukaay yi ak këll yi. Mboolem yooyu jumtukaayi kër Aji Sax ji, xànjar bu ñu jonj la Buur Suleymaan sant Uram, mu defare ko.
46Ca joorug Yurdan la ko Buur xellilu, ci móoli ban, diggante Sukkóot ak Sartan.
47Suleymaan daldi bàyyi jumtukaay yépp noonu, ndax na mu baree lool, ba natteesul diisaayu xànjar ba ca dem.
48Gannaaw loolu Suleymaan defarlu na mboolem yeneen jumtukaayi kër Aji Sax ji: muy sarxalukaayu wurus ba, ak taabal ja ñuy teg mburum teewal ma
49ak tegukaayi làmpi wurusu ngalam yi, juróom ci wetu ndijoor, juróom ci wetu càmmoñ, fi kanam néeg bu sell baa sell; tóor-tóor yi ak làmp yi ak ñiim yi, lépp di wurus;
50ndab yi itam, ak feyukaay yi ak këll yi ak kopp yi ak andi cuuraayu yi, lépp di wurusu ngalam. Te it ngoosi wurus yi bunti néeg bi wewe, ñu di fa jaare dugg ca bérab bu sell baa sell, ak ngoosi wurus yi beneen buntu néeg bi wewe, ñu di fa jaare dugg ci néeg Yàlla bu mag bi, lépp wurus la.
51Ba loolu amee, mboolem lu Buur Suleymaan liggéeyal kër Aji Sax ji daldi sotti. Mu boole xaalis baak wurus waak jumtukaay ya baayam Daawuda sellalaloon Aji Sax ji, yeb ko ca denc ya def alali kër Aji Sax ji.

Read 1.Buur ya 71.Buur ya 7
Compare 1.Buur ya 7:35-511.Buur ya 7:35-51