Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 6

1.Buur ya 6:19-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Néeg bu sell baa sell ca biir kër ga ca biir-a-biir la waajal, ngir yeb fa gaal gay def àlluway kóllërey Aji Sax ji.
20Néeg bu sell baa sell amoon na guddaayu ñaar fukki xasab, yaatuwaay ba di ñaar fukki xasab, taxawaay ba di ñaar fukki xasab; Suleymaan xoob ko wurusu ngalam. Sarxalukaayu seedar ba jàkkaarlook néeg ba, moom it xoob na ko wurusu ngalam.
21Ci biir loolu Suleymaan xoob biir néeg Yàlla ba wurusu ngalam. Mu tàllal ay càllalay wurus fi kanam néeg bu sell baa sell,
22daldi xoob ci biir wurus ba mu daj. Sarxalukaayu néeg bu sell baa sell, lépp la xoob wurus.
23Ci kaw loolu mu sàkk ca biir néeg bu sell baa sell ñaari malaakay serub yu ñu yette bantu oliw, jëmm ju ci nekk am taxawaayu fukki xasab.
24Benn serub bi laaf mu ci nekk juróomi xasab la, muy fukki xasab ci catal menn laaf mi ba ca catal laaf ma ca des.

Read 1.Buur ya 61.Buur ya 6
Compare 1.Buur ya 6:19-241.Buur ya 6:19-24